Lingoom
Apparence
Lingoom garab la gu bokk ci njabootu "rutacées". Dees na ko faral di bay ci barab yi bari naaj.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab la gog ay xobam dafay faral di wéy cig sax ci at mépp. Danay dund lu tollu ak 50 ba 80i at. Ay tóor-tóoram day weex. Doom bi nag dafay muluŋ te cat la sew. Guddaayam di nay àgg ci 7 ba 12i sàntimet.
Wirgoom cig ñàkk a ñor nëtëx la, cig ñor nag mboq la.
Ndox mi mu ëmb, cafka gi dafay sëcc(wex). Doom bi day ëmbaale ay xoox.
Solo si
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Lingoom bari na nees koy jëfandikoo. Dees na ci génnee njar mbaa ndollenu njar.
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Citrus limon
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]araab: الليمون |
farañse: limone |
angale: lemon |
itaaliyee: limone |